Ngir xam lu leer ci seen mboorum réew ak bu Afrig, ndaw ñi dañoo war a miin jàmbaar yi tabax Afrig. Ndégat yii di Podcast,« Xam sa démb, xam sa tey », looloo tax ñu tànn yenn ci jaar-jaar ak xew-xew i mboorum Senegaal, ngir may ndaw ñi ñu jàngee ci seen démb, baa man seen tay, te waajal seen ëllëg.

Ceerno Sulaymaan BAAL moo soppi ni ñiy yore nguuur ca Fuuta jëlee ko ci ndono tegg ko xam-xam ak jikko. Moo Boolewoon Jullit yi ngir ñu jóog xeex ak ñi bañoon diine. Man na noo wax ni moo indi nguurug yemale di democrasi ci Afrig Sow jant.